xamle - 15 MONTHS.MAY 2025
Ñenti Ma-laamisoo yu bees jébbal nañu Njiitu Réew mi ci àllarba ji seen bataaxeli tabb. Muy Ma-laamisoo yu Portugaal, Liberiyaa, Móritani ak Siin. Jataay bii nag mooy màndargaal ndoortel seen i yëngu niki ma-laamisooy seen i réew ci Senegaal.