Sëriñ Usmaan SONKO: Njiital Jëwriñ yi
Jëwriñ yi:
1. Soxna Yaasin FAAL: Jëwriñu Bennaleg Afrig gi ak jëflante ak biti réew
2. Sëriñ Biram JÓOB: Jëwriñu Xare bi
3. Sëriñ Usmaan JAAÑ: Jëwriñu Yoon, Wattukatu Xàmmekaay yi
4. Seneraal Sãa Baptist TIN: Jëwriñu biir réew mi ak Kaarangeg pénc mi
5. Sëriñ Biram Suley JÓOB: Jëwriñu Yasara gi, Soroj ak Mbell yi
6. Sëriñ Abdurahmaan SAAR: Jëwriñu Koom mi Palaŋ ak Lëkkaloo
7. Sëriñ Seex DIBA: Jëwriñu Koppar yi ak Njël li
8. Sëriñ Yanqooba JEMMÉ: Jëwriñu Jumtukaay yi ak Yaaleg suuf si ak jaww ji.
9. Sëriñ Daawuda NGOM: Jëwriñu Kéew mi ak Jàll jëm ci ekolosi
10. Sëriñ Aamadu Mustfaa Njekk SARE: Jëwriñu tàggatu gu xereñ (Farbay Ngóornamaŋ bi)
11. Sëriñ Seex Tiijaan JÉEY: Jëwriñu Ndox mi ak Yooni Ndox yi
12. Sëriñ Àlliyun SÀLL: Jëwriñu Caabal gi, Jokkoo ak Xarala yi
13. Sëriñ Elhaaji Abdurahmaan JUUF: Jëwriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu ak fent
14. Sëriñ Géy JÓOB: Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi
15. Soxna Faatu JUUF: Jëwriñu Napp gi, Jumtukaayi géej yi ak waax yi
16. Soxna Maymuna JÉEY: Jëwriñu Njaboot gi ak jàppalante gi
17. Sëriñ Àbbaas FAAL: Jëwriñu Liggéey bi, Xëy mi ak Jëflante ak Campeef yi.
18. Sëriñ Bàlla Musaa FOFANA: Jëwriñu dëkkuwaay yi, Gox ak goxaan yi ak daggug mbeeraay yi
19. Sëriñ Mustafaa Màmba GIRAASI: Jëwriñu Njàng mi
20. Sëriñ Sàmba Si: Jëwriñu Paj mi ak Ndimbal li
21. Sëriñ Oliwiyee BUKAAL: Jëwriñu Foŋsoo piblig ak Yeesal Sarwiis piblig
22. Soxna Xadi Jéen GAY: Jëwriñu Ndaw ñi, tàggat yaram ak Mbatiit
23. Sëriñ Ma-Buuba JAAÑ: Jëwriñu Mbay mi, Bay dunde ak Càmm
24. Sëriñ Àlliyun JONN: Jëwriñu Kopparal yu ndaw yi ak koomum Jàppal ma jàpp
25. Sëriñ Muntagaa JAW: Jëwriñu Ndaamaari gi ak Pasin gi
26. Sëriñ Seriif JUUF: Jëwriñu Càmm gi ci mbirum saa-senegaal yi féete biti réew
27. Sëriñ Ibraahima CAAM: Jëwriñu Càmm gi ci wàllu suqali Këri Lijjanti yu ndaw yi ak yu digg-dóomu yi ak Ndefar yu ndaw yi ak yu digg-dóomu yi.
28. Sëriñ Momar Taala NDAW: Jëwriñu Càmm gi ci wàllu Tabax ak dëkkuwaay
29. Sëriñ Alfa Ba: Jëwriñu Càmm gi ci wàllu Mbootaay yi ak taxawu baykat yi
30. Sëriñ Baakari SAAR: Jëwriñu Càmm gi ci wàllu Mbatiit Ndefari pasiin yi ak sunu am-ami mboor