New York: Peresidaa Jomaay dalal na Musaa Faki Mahamat

Biti Réew - 24 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Ca 79eelu Ndaje Mu Mag mu Mbootaayu réewi àddina si, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay dalal na tay Musaa Faki Mahamat, Njiital kurélug Mbootaayu Réewi Afrig.
Njiitu Réew mi ak Faki Mahamat sumb nañu ay waxtaan ci yittey kaaraange yi moo xam ci dig-digal yi walla ci kembaar gi, jaare ko ci woo Njiiti Réew yi ñu sóobu ci bu baax.
Feddali nañu itam ne diisoo rekk mooy yoon wi ñu war a jiital ngir am ay pexe yu sax, boole ci fésal ne pexe mu bawoo ci saa-afrig yi rekk a man a indi saafara ci jafe-jafey Afrig.