Biti Réew - 21 MONTHS.SEPTEMBER 2025
Naka la daal di yegg New York rekk ngir teewe 80eelu jataayu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi Àddina si, ci la moom Njiitu Réew mi daal di door aw sémbam ak jataay bu mu jagleel S. Patrick ACHI, Jëwriñu Càmm teg ci di Xelalekat ci Peresidaa Alasaan WATARA, mu am bataaxel bu bawoo ci moom bu mu doon indi.
S. ACHI a ngi àndoon ak S. Fidel SARASORO, Jëwriñ Bëkk-néegu Njiitu Réewum Kodiwaar niki noonu ak S. Leon Kacou ADOM Jëwriñu Jëflante ak Biti Réew.
Waxtaan yi jëmoon ci jëflantey bokkoo, xaritoo ak lëkkaloo yi dox diggante Senegaal ak Kodiwaar, te doon luy wéy di nekk lëngoo gu jar a roy ci Afrig Sowu Jant.