Biti Réew - 23 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Njiitu Réew mi teewe na tay, ci bëccëg gi, jataayub añ bu ñu lootaabe woon ci ndajem waxtaane Ëllëg. Jataayu yaatal bii dajale kilifa yu am maanaa, tax na ñu weccente xalaat yu am solo yu jëm ci yitte yu far yi soxal àddina si.
Ci jataay boobu, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay daje na fa ak Kilifa gii di William Samoei Ruto, Njiitu Réewum Keeñaa. Ndaje mu fees dell ak mbégte mii ak nawlonte, may na ñaari Njiiti Réew yi ñu rafetlu jëflante yu rafet yi dox diggante ñaari réew yi teg ci jaayante ci gën koo dooleel.
Ñaari naataango yi waxtaane nañu itam ci amal ay lëkkaloo ci pàcc yu am solo yi soxal askan wi boole ci weccente xalaat ci yeesal yi war ci campeefi àddina si, bokk ci taxawaay bu am solo bi Mbootaayu Réewi Afrig yi (UA) war a am.