New York : Njiitu Réew mi jataayu na ak Alexander De Croo, Njiital Jëwriñu Belsig.

Biti Réew - 23 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Ci lu soxal ndaje yi muy amal ci wàllu lëkkaloo, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, jataayu na ak kilifa gi Alexander De Croo, Njiital Jëwriñu Belsig.
Waxtaan yi a ngi jëmoon ci gën a dooleel jëflante yi diggante Senegaal ak Belsig, jaare ko ci fésal pàcc yu am solo ci wàllu suqaliku niki noonu mbaax yi boole ñaari réew yi.