New York : Njiitu Réew mi dalal na Njiital FMI

Biti Réew - 25 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay dalal na, tay ci àllarba ji, Kristalina Georgieva, Njiital FMI.
Seen i waxtaan a ngi jëmoon ci gën a dooleel lëngoo diggante Senegaal ak FMI, jaare ko ci taxaw ci coppitey koom yi ñu namm a amal ak taxawu yittey suqaliku yi réew mi am.