New York : Jataayu tijjitel "Ndajem Ëllëg"

Biti Réew - 22 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Njiitu Réew mi, Kilifa gi Basiiru Jomaay Fay, teewe na tay ci dibéer ji ca New York jataayu tijjitel "Ndajem Ëllëg", di xew wu mag wu ñu lootaabe ci 79eelu Ndaje Mu Mag mu Mbootaayu réewi àddina si.
Ndaje mii dajale na ay Njiiti Réew ak yu Ngóornamaŋ, ay njiiti kuréli àddina si, niki noonu ndawi sosete siwil bi ak ñiy yëngu ci piriwe bi ngir waxtaane tomb yu jamp te am solo yiy xaar àddina si ak ay jumtukaayi tabax àddina su gën a ñoŋ, su boole ñépp te sax.
Teewe gii Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay amal, day tàbbi ci jéego yi Senegaal di teg jëm ci dooleel lëkkaloo diggante réewi àddina si ak waajal ëllëg gu jub, sax te naat ñeel mbooleem ma-réewi àddina si.