Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay jiite na na tay ci alxemes ji 24i fani féewarye 2025 ndoortel sémbu xarala wu bees wii ci Senegaal ñu tuddee « New Deal Technologique ».
Cig àddoom, Peresidaa Fay fésal na solos sémb wu yaatu wii di teg xarala yi ci xolu suqalikug réew mi ak Senegaal gu moom boppam ci wàllu xarala. Sémb wii bokk ci
« Agenda national de transformation Sénégal 2050 », yéeneem mooy def réewum Senegaal muy ku ràññiku ci koomum xarala yi ci Afrig.
Ak « New Deal Technologique » bii, Senegaal taxaw na temm ngir dooleel manal boppam gi ci wàllu xarala yi, jaare ko ci teg ay pexe yu bawoo ci réew mi boole ko ak aar jumtukaayi xarala yi, matale wàllu « digitalisation » ci ndoxal gi ak serwiis piblig bi, fexe ba ñépp man a jot ci internet, teg xar-kanam gu jàppandi ngir suqali ay waada ci réew mi, taxawal ay limati jëmm ngir raññatle kenn ku ne ak taxawu ñiy fent ak a jéem a taxawal dara.
Njiitu Réew mi xamle na ca ndaje ma itam ne, fàww ñu méngale ak jamono jumtukaayi xarala yi boole ko ak teg doxaliinu yoon wu jàppandi ci wàllu fent, lépp ci kaw sàmmaale dundug biiru ma-réew yi.