Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, teewe na tay ci suba gi xewu tijjitel Afrikaa CEO Forum 2025, ca Abijaŋ, ci teewaayu naataangoom yii di, Alasaan Watara (Kodiwaar), Póol Kagame (Ruwandaa), Siril Ramafosaa (Afrig Du Sud) ak Mohammet Uld Seex El Xasuwani (Móritani).
Ndaje mii ñu doon waxtaane pexey teg lëngoo gu bees diggante piblig bi ak piriwe bi ngir njariñu Afrig, doon na jataay bu am solo ngir weccente xalaat ci pexey eewestismaa ak suqalikug sektéer piriweb Afrig bi, lépp lalu ci pas-pasu lëngoo ak déggoo ci Afrig.
Teewaayu Njiitu Réew mi ci ndaje mii day feddali jaayante gu wér gi Senegaal am ngir koomum Afrig mu doon benn, lëkkaloog àddina si ak gën a dooleel lëngoog piblig-piriwe ngir yokkute gu sax te daj ci ñépp.