Nemmikug Njiitu Réew mi ca Tuubaa ak Daaru Muhti : Njaal ak delloo njukkal ci weeru koor gi, jëmm yu ràññiku woon ci yoonu Muriid .

xamle - 15 MONTHS.MARCH 2025

Tay ci gaawu bi 15i fani mars te dëppo ak weeru koor gu sell gii, Njiitu Réew mi, ànd na ak mbooloo mu am solo ci ay jëwriñ ak kilifay ndoxalug mbeeraay gi, amal ay nemmiku ca Tuubaa ak ca Daaru Muhti ngir jébbale am njaalam ginnaaw génn àddunag Sëriñ Mustafaa Saalihu Mbàkke, Sëriñ Daam Àtta Mbàkke, Sëriñ Amdi Móodu Mbenda Faal ak Sëriñ Basiiru Anta Ñaŋ Mbàkke.

Ca Tuubaa nag, Sëriñ Muntaxaa Mbàkke dalal na ko ca Daaru Minan. Ginnaaw waxtaanuw biir wu ñu séq toftal ci ay ñaan, Njiitu Réew mi dem na ci njabooti way-dawlu yii di Sëriñ Mustafaa Saalihu Mbàkke, Sëriñ Daam Àtta Mbàkke ak Sëriñ Amdi Móodu Mbenda Faal ngir jébbal leen am njaalam. 


Ca Daaru Muhti, Njiitu Réew mi Bassirou Diomaye Faye delloo na njukkal bu baax Sëriñ Basiiru Anta Ñaŋ Mbàkke ci teewaayu Xalifa bi ak njabootam, ci jataayu teewlu ak ñaan.

Nemmiku gii nag day tàbbi ci pas-pasu jàppalante, sàmmonte ak mbaax yi ak ànd ak tiis wi njabootu muriid gépp.