Nemmikug Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY ca Kërug defarukaayu suukar (CSS) ga ca Risaar Tool.

xamle - 12 MONTHS.JUNE 2025

 Ginnaaw Njaayeen Pendaaw, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, dem na ca Risaar Tool, tay 12i fani suwe 2025, nemmikuji Kërug Senegaal giy defar suukar (CSS). 

Lu jege 8 000iy nit di fa xëy, CSS a ngi dugal loxoom bu baax ci koomum gox ba ak mu réew mi, jaare ko rawati na, ci naal yu am solo yii jëm ci manal sunu bopp ci wàllu suukar fii ak 2030.

Muy nemmiku guy feddali jaayanteg Nguur gi jëm ci taxawu pàcci ndefar yu am solo yi ngir aar Senegaal ci wàllu li muy dundee.