Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, jiite na tay ci ngoon gi, jataayu ndoortel « Caravane nationale SPACEBUS 2025 », ca ëttu « Grand Théâtre » Duudu Njaay Kumba Róos.
Ñu ciy waxtaane « naka lees di jëfandikoo jawwu ji ngir suqaliku gu sax dàkk », ñaareelu edisoo bii dajale na ñu bokk ci ngóornamaŋ bi, ay partaneer ci wàllu campeef yi, xarala ak koppral, niki noonu ay njàngaan ak i dongo yu bawoo ci daara yi ñu dëne. Ci kàddu yu lalu ci gis-gis bu leer ak yéene, Njiitu Réew mi xamle na solo si jawwu ji am ngir suqaliku gu sax ak ci ëllëgu ndawi Senegaal.
Njiitu Réew mi tijjee ay kàddoom ci ndokkale bu baax Maram Kayre miy Njiital « Agence sénégalaise d’Études spatiales (ASES) », niki noonu mbooleem partaneer yi, rawati na Àmbaasad bu Farãas ak koperaasoo bu Lugsàmbuurg, ci seen taxawaay. Rafetlu na itam teewaayu kàngam yi bawoo Farãas, Kodiwaar, Benee, Eslowaki ak Togóo, di mbir mu mu gis ne day màndargaal jàppoo ak yéene ji nu bokk am jëm ci tabax ëllëg gu yees ngir Afrig.
Njiitu Réew mi fàttali na ne, dem ci jawwu ji yamul rekk ci ab konket, waaye dafa war a indi ay saafara ci jafe-jafey jamono ji. « Xarala yi aju ci jawwu ji man nañoo indi coppite yu wóor ci sunu mbeeraay yi », di li mu xamle, jaare ko ci lim seen taxawaay ci pàcc yu am solo yu mel ni fàkkug suuf si, mbay mi, napp gi, paj mi, kaaraange gi ba ci koomum géej gi.
Njiitu Réew mi dikkaat na ci yoon yi Senegaal jot a jaar ba man a bokk ci réew yi am taxawaay ci wàllu jawwu ji, dale ko ca « Plan National de Géomatique » ca atum 1998 na ni ñuy taxawalee ASES. Fàttali na ndoortel satalitu Senegaal bi ñu njëkk a sànni ca weeru ut 2024, muy jaloore juy màndargaal jéego bu am solo. Ngir wéyal mbébet moomu, yëgle na sémb yu am solo : barab bu ñuy dajalee, di sofale ak a amal ay test ci wàllu satelit (MAIT), ay warab ngir dajale xibaar yiy bawoo ci satelit yi, benn barab ngir gunge ndaw ñi ci wàllu jawwu ji, benn barab bu ñuy saytoo jawwu ji ca Kéedugu, benn barab bu ñuy xoolee mbooleem liy xew ci jawwu ji ca Xombol ak benn barab ngir fésal lépp lu aju ci xam-xamu jawwu ji. Muy ay sémb yu mu jàpp ne dina may ndaw ñi, ñu man a tàggatu, am ay xëy walla jéem a taxawal dara, lépp boole ko ak gën a xemmemloo Senegaal meññilukat yi.
Njiitu Réew mi taxaw na bu baax itam ci koom mu am solo mi wàllu jawwu ji làq, nga xam ne àddina bi war na cee dugal lu tollu ci 737i milyaari dolaar ci fukki at yiy ñëw. « Jawwu ji mooy ñenteelu coppite gi am ginnaaw ndefar gi, elektoronig bi ak xarala yi », di li mu wax ngir fésal taxawaay bi mu am ci saytu balli mbindare yi, kaaraange gi, dox jëm ci mbay mu xarala, paj mu ànd ak xarala walla fuglu ci wàllu njuux li.
Cig àddoom itam, def na woote bu am solo jëme ci ndawi Senegaal. Peresidaa Fay naqarlu na lim bu néew bi ñu seetlu ci wàllu xamtu, nga xam ne ñiy def BAC 16,5% rekk lañu ci. « Dina jafe lool ñu saafara jafe-jafey xëy mi, bay-dunde gi, paj mi walla xarala gi, su dee dooleeluñu njàngum xamtu yi ak xarala yi », di li mu yëy-yàbbi. Ngir indi ci ay saafara nag, yëgle na ay dogal yu wér : yokk filiyeer yi, taxawal ay jumtukaayi njàng yu méngoo, dooleel njàngum xamtu mi añs. « Li nu fas yéene mooy méngale njàng mi ak li sunu koom soxla boole ko ak jox ndaw ñi ay jumtukaay yuy tax ñu man a tabax ëllëgu Senegaal », di li mu ci dolli.
Mu tëje ay kàddoom ci jagleel njàngaan yi ak dongo bataaxelu soññe : « Yéen ay li gën a gànjaru ci li réew mi am. Seen ug dogu, seen bëgg xam-xam ak seen ug ñaw ñooy kenoy Senegaal gu moom boppam, gu tegu ci yoon te naat. »