xool - 28 MONTHS.MAY 2025
Liggéey yi aju ci Péncoo gi ñuy amal ci réew mi ci sistemu politig bi door nañu leen tay ci àllarba ji 28i fani mee 2025, ca “Centre international de conférences” Abdu Juuf (CICAD) ca Jamñaajo.
Ci teewaayu kilifa gi Basiiru Jomaay FAY, ñi teewal làngi politig yi, sosete siwil bi, kilifa diine yi ak yu aada yi, sàndikaa yi, mbootaayi ndaw ñi ak jigéen ñi, niki noonu mbooleem ñi am kàddu ci réew mi, jataay bii day màndargaal ndoortel diisoo yu am solo. Jubluwaay bi di àndandoo amal xalaat yu xóot ci doxaliinu politig ak joŋante ci Senegaal, lépp lalu ci booloo ak déggoo ci réew mi.
Peeñ :