xamle - 08 MONTHS.MAY 2025
Ngir waajtaayu bëccëgu diisoo ci doxaliinu politig bi ñu namm a amal ci réew mi, 28i mee 2025, ñu ngi woo mbooleem taskati xibaar yi ci réew mi ak yu biti réew ci jataayu ndoortel Njëfekaayu xarala gii di JUBBANTI, àjjuma 9i fani mee 2025, ca “salle de conférence” bi nekk ca Batimaa Administaraatif Mammadu Ja, ca 10eelu etaas ba, li ko dale 16i W.
Ngir bañ a beddi kenn teg ci may saa-senegaal bu ne, ak fu mu man a nekk ci biir àddina, mu man cee joxe gis-gisam, Njëfekaayu xarala gii di «JUBBANTI» yeesalaat nañu ko.
Man ngeen a jaar fii ci suuf ngir wàcce wayndare wi :