jëwriñ - 21 MONTHS.FEBRUARY 2025
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay, dina amal, ci àjjuma jii 21i fani féewarye 2025 ca Kungéel, ndoortel sémb wu am solo wii di PROMOREN, muy liggéey yu jëm ci dajale ndox yiy ballee ca Ñànija Bolong.

Sémb wii nekk ci diggante tundi Kafrin ak Tàmbaakundaa, dina jariñ lu ëpp fukki bokk-moomeel ci ñaari tund yooyu.