NDOORTEL JUMTUKAAYU XARALA TABAX SENEGAAL

xamle - 01 MONTHS.APRIL 2025


Talaata 01 panu awril 2025 doon na bis bu am solo ci politig yi ñuy amal ci réew mi ci wàllu xëy, jéem a taxawal dara ak dugal xaalis, ginnaaw ndoortelu jumtukaayu xarala bii di «𝐓𝐚𝐛𝐚𝐱 𝐒enegaal».

🔶

Lan mooy Tabax Senegaal ? Jumtukaayu xarala bu bees la bu ñu taxawal ngir yombal lëkkale gi diggante :

• ñiy wut xëy,

• ñiy jéem a taxawal dara ak ñi am ay sémb,

• meññilukat yi am yéene jàpp ci suqali koomum réew mi.

🔶

 Jubluwaay bu leer te am solo 

 Gën a man a jëfandikoo xam-xam bi am ci Senegaal, 

 Jàppandal ak yamale anam yi ñuy jotee ci xëy yi, 

 Taxawu bu wér ñiy jéem a teg dara ak fentkat yi,

 Gën a xëcc meññilukat yi, 

 Dekkal yaakaar boole ko ak gën a dooleel yamale gi jaare ko ci doxaliin wu leer.


Jumtukaayu xarala bii di Tabax Senegaal day tàbbi ci gis-gis bu wér bi Njiitu Réew mi am, te tënk ko ci biir « Agenda National de Transformation » ak kaadaru « Vision Sénégal 2050 ». Dinanu teg jéego yu am solo jaare ko ci mbébet mii, jëm ci wàññi bu baax ñàkk um xëy mi, baral jéego yi jëm ci jëmmal sémb yi gën a am solo boole ko ak suqali koomum réew mi.


Widewoo kaajar gi  fii ci suuf: