Ndoortel JUBBANTI : Njëfekaayu xarala ngir Diisoo gu bàyyi xel ñépp.

xamle - 09 MONTHS.MAY 2025


Njëfekaayu xarala gii di JUBBANTI, jàppandi ci lëkkalekaayu https://jubbanti.sec.gouv.sn/ door nañu ko ci àjjuma ji ci ngoon gi jaare ci am ndaje mu ñu séq ak saabalkat yi ca Bildiŋ Administaraatif Mammadu  Ja. 

Mbébet mu bees mii di guleet, dina may saa-senegaal yi nekk ci biir réew mi ak ya ca biti réew, ñu man a joxe seen gis-gis ci diisoo yi ñu namm a amal ci réew mi ci doxaliinu politig bi, 28i fani mee 2025, ci njiital Njiitu Réew mi. 

JUBBANTI dina doon jumtukaay bu am solo bu mbooleem saa-senegaal yi man a fekk tomb yi ñu war a waxtaane ñu tënk ci taxawaay ak jubluwaayu diisoo gi. Lan moo tax ñu sumb waxtaan yii ci doxaliinu politig bi ? Yan jafe-jafe lees war a saafara ? Tontu yii yépp dina jàppandi ngir ñépp. Ci geneen wàll, Njëfekaay gii dina may way-jëfandiku bu nekk mu man a gaaral ay gis-gisi boppam, muy luy dooleel doxaliin wu boole ñépp. 

 

Ndoortel barabu diisoo bii day firndeel yéeney Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay ci dooleel doxaliin wu leer wu boole ñépp ci yoriinu pénc mi. Jumtukaay bii kon mooy keno bu am solo buy ñaaxe ci yoriin wu ubbiku wu ma-réew yépp di dugal seen yoxo.