xamle - 13 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Kilifa gi, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, jiite na tay xewu bis bi ñu jagleel màggal taxawalug GAINDESAT-1A gi dugg ci mboor, di satelitu Senegaal bi njëkk. Sottal gii nag njureefu liggéey yu am solo yu sunu xereñtaan yi ak way-xarala yi nga xam ne, ci seen liggéey bii, day tijji xët wu yees ci suqalikug xarala ñeel Senegaal.
Bis bii day màndargaal ndoortel ëllëg gu yaakaaru ñeel sunu réew ci wàllu jaww ji. Xàll nañu yoon ngir Senegaal gu moom boppam, yees te wëlbati mbooleem ay yitteem ci ëllëg.