NDIISOOG JËWRIÑ YI - 10 MONTHS.JULY 2024
Ndiisoog Jëwriñ yi- 10i sulet 2024
Ab jukki ci Conseil des ministres bu àllarba 10i fani sulet 2024:
Njiitu Réew Mi Basiiru Jomaay FAY jiite na, ci àllarba ji 10i fani sulet 2024, Ndajem Jëwriñ yi ñuy amal ayu bis bu set ca Njénde la.
Ci ndoortel ay kàddoom, Njiitu Réew Mi ndokkale na boole ko ak ñaanal wér, jàmm ak tawfeex Ummah Islaam bi ci ndoortel atum jullit mu yees mi di 1446. Posewu na ci ngir sàkku ci Ngornamaa bi ñu jël mbooleem matuwaay yi war ngir taxawu ci anam yu mucc ayib xew-xewi diine yii di Màggalug Tuuba, Gàmmu gi ak Asomption yi war am ci ayi-bis yii nu dëgmal ci Senegaal.
Ba muy dikkaat ci digle yi bawoo ci diisoo yi woon ci wàllu yoon ak yeesal yu jamp yi war ci wàll wii, Njiitu Réew Mi wane na ag àndam ci digle yi way-diisoo yi ci wàllu yoon dëppoo te gaaral leen ci biir ràppoor bi. Jaajëfal na bu baax Ngornamaa bi, Jëwriñu Yoon ji rawati na, ñi muy liggéeyandool, aji-yombal ji jiite woon diisoo yi, ñi bokk ci pekk (Bureau) bi ak Bànqaasu xeltukat yu diisoo yi, niki noonu mbooleem ñi ci dugal seen loxo ci seen gis-gis yu am solo yi tax ñu man a sottal ràppoor bu gànjaru bii ñu jébbale.
Njiitu Réew Mi rafetlu na anamu déglu xalaati kenn ku nekk gi ñu amalee diisoo yi, boole ci loolu taxawalug jumtukaay bii di JUBBANTI. Doxaliin wu yees woowu ci caabalug (communication) nguur gi day may ma-réew bi, jaare ko ci xarala yi, mu man di dugal loxoom ci doxaliinu pénc mi waaye tamit ag xereñte ci doxal sémbu (PROJET) soppi Senegaal ci fànn yépp. Mu bokk ci jaayante gi jëm ci samp réewum yoon, Republigu royukaay ak Askan wu déggoo jaare ko ci campeef yu am doole ak yoon wu wér wu doy askanu Senegaal wi ñuy àtte ci seen tur.
Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi, Jëwriñu Yoon ak ci Jëwriñ yi mu soxal, ñu gaaral ko arminaat bu jëm ci doxal yeesal yii aju ci wàllu yoon te dëppoo ak sémbi yoonal (legislatif) yu Ngornamaa bi. Arminaatu yoonaal boobu nag daa war a jublu rawati na ci yeesalug Ndayu Sàrti Réew mi ak yenn ci kot yi.
Njiitu Réew mi sàkku na xayma gi, ci teewug Jëwriñu Koom mi ak Njël li, jëm ci njëg ak koppar yi yeesal yooyu di laaj ngir man a xam njariñal boole leen ci yi gën a far ci nattub njël yi. Xamal na Ndiisoo gi ne noppi na ngir jotaat yeneen gis-gis walla gaaral yu wér ci lu jëm ci yeesal Conseil supérieur de la Magistrature ak rawati na yaatal ko ba ci ñeneen ñu bokkul ci àttekat yi man cee bokk ak jafe-jafe bi soxal teewayu Njiitu Réew mi ak Jëwriñu Yoon ji ci biir bànqaas boobu.
Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak Jëwriñu yoon ji ñuy xamle weer wu jot ci Conseil des Ministres, tolluwaayu doxal digle ak dogal yi tukkee ci diisoo yi woon ci wàllu yoon tey bàyyiwaale xel, bu ñu koy doxal ñu fexe mu dëppoo ak mbaaxi pénc mi, sunu mbatiit ak sunuy gëm-gëm.
Lu soxal saytu gu sax ci wàllu asenismaa ci bokk-moomeel yu Senegaal, Njiitu Réew mi wane na ne, ni dëkkuwaay yi di yokkoo ci Senegall ak jafe-jafe yi am ci ni ñuy daggee pàkk yi (amenagement) ci sunu bokk-moomeel yi, bokk nañu ci liy yokk wal (innondation) mi ba tax ñuy soxlawoo jumtukaayi asenismaa. Sàkku na ci Njiital Jëwriñ yi ak jëwriñ ji yor wàllu ndox mi ak asenismaa, ànd ko ak Brigade nationale des Sapeurs-pompiers ak mbooleem wànqaasi nguur, ñu taxawal ci anam yu mucc ayib jumtukaayi fegu ak saytu wal mi ci gox yi mu laal. Fésal na tamit, mu doon ngir yëgle, sóob ci liggéey bi jumtukaayi pénc mi ci wàllu jàppalante ngir man di taxawu bu baax askan wi loru ci wal mi te ànd ko ak kilifay ndoxal gi (autorites administratives).
Njiitu Réew mi sàkku na ci Njiital Jëwriñ ji mu amal xayma ci mbooleem jëf yi ñu jot a teg ci fukki at yii wees jëm ci xeex wal mi ngir door a a man a sóobu ci teg pexe yu yees ci réew mi jëm ci samp asenismaa bu wér bu dëppoo ak politig yu yees yi, ci ni ñu war a daggee mbeeraay gi ak dëkkuwaay yi. Ci loolu, woo na Njiital Jëwriñ yi mu yékkatiwaat boole ko ak fexee dajale lii di Plans directeurs d’Assainissement (PDA), daal di ko gaaral sémb wu yees wu ñeel Programme intégré de Développement de l’Assainissement (PIDA).
Njiitu Réew mi dikkaat na ci pas-pasu cosaan gii ñu taxawal ci wàllu jaayanteg ma-réew yi di SETAL SUNU RÉEW. Jaajëfal na Njiital Jëwriñ yi, Jëwriñu Ndox mi ak asenismaa, ñi bokk ci Ngornamaa bi, kilifay ndoxal gi, fara yi, wànqaasi nguur gi, way-yëngu ñi ci piriwe bi, ndaw ñi, jigéen ñi ak mbooleem ñi am kàddu ci réew mi, ci anam gu mucc ayib gi ñu amalee ñaareelu bëccëgu SETAL SUNU RÉEW bi ñu doon amal gaawu 06i sulet. Ci wàll woowu ba leegi, sàkku na ci Ngornamaa bi ñu taxaw temm ngir waajtaay wu mucc ayib ci 3eelu bëccëg gi ñu jagleel jëmbët garab jëm ci bis bi ñu jagleel garab ci réew mi.
Bëccëg gii nag dees na ko defal ag jagle màggal ko gaawu 03 ak dibéer 03i fani ut 2024.
Lu soxal ab arminaatam ci wàllu laamisoo, Njiitu Réew mi xamal Ndiisoo gi ci teewaayam, 07i fani sulet 2024 ca Abujaa, ca 65eelu Ndajem Njiti Càmm ak Ngornamaa yu CEDEAO.
Ci ay kàddoom, Jëwriñ ju Njëkk ji leeral na nemmiku yi mu amal ca Tuubaa ak Tiwaawan ci wetu Xalifab Yoonu Murit ak Xalifab Tiijaan yi. Posewu na ci nemmiku yooyu ngir waxtaan ak Xalifa yi ci Sémb wu am solo wi jëm ci soppi xar-kanamu Senegaal ci pas-pasu JUB, JUBAL et JUBBANTI.
Jëwriñ ju Njëkk ji rafetlu na lool wàccoog Njiitu Réew mi ci boppam ak mbooleem Ngornamaa bi ci matale seen wareef ci xamle li ñu am ci alal ca Ndisoog Ndayu Sàrt yi ak ca OFNAC, ci 3i weer yi ñu leen àppaloon ginnaaw ba ñu dooree seen liggéey. Sàkku na ci Jëwriñ yi ñu taxaw temm ngir njiit yi mu soxal te ñu aju ci ñoom def lu ni mel ñoom itam.
Ag àddoom ci ndam li am ci bëccëgu takkug ma-réew yi, Jëwriñ ju Njëkk ji digle na ci ñu fexe ba saxal yëngu yii mu doon Sémb ci réew mi yu jëm ci gën a fésal ag ma-réewe ak koomum dundiin. Doxaliin woowu dina tax ñu man a saxal pas-pasu coobarewu ak kilifteef ci saytu cetug pénc mi, lépp jublu ci dooleel ndaw ñi ci wàllu xëy.
Ba muy dellusiwaat ci li mu jànge ci teewe bëccëgu Setal Sunu Réew gu 6i sulet 2024 ca Ndar ngir teewal fa Njiitu Réew mi, Jëwriñ ju Njëkk ji naqarlu na déya gi am ci doxal liggéeyi asanismaa yi, caytug wale mi ak xeex yàquteg tefes yi, daanaka ci mbooleem sémb yi ak naal yi. Seetlu yooyu nag tax na ñu war a amal càmbar bu matale tolluwaayu Sémb yi ak naal yi.
Jëwriñ ju Njëkk ji taxaw na bu naax, ginnaaw Njiitu Réew mi, yitte ju kawe ji ñu teg ci saytug fegu ci wale yi, jaare ko ci sóob Jëwriñu koppar yi ak Njël li mu jiital ci natti njël yi, taxawug sëllëx yi ci jëm.
Mu tëje, moom Jëwriñ ju Njëkk ji ci xamal Ndiisoo gi taxawalug, ci ndigalu Njiitu Réew mi, ci dogal bu 3i fani sulet 2024, kurélug càmbar pas yi ñu jot a tënk ci pàcc yi gën a fés. Kurél googu sasam mooy jàngat, ci biir pas yi ñu tudd, teewaay bu wér ci njariñal réew mi niki noonu doxaliinu sàmm leen, bu dul dara sax mu am ug yemoo.
CI ÀDDUG JËWRIÑ YI:
Jëwriñu booloog Afrig ak biri biti réew leeral na ci doxaliinu ajug 2024 ca Warab yi sell yu Lislaam;
Jëwriñu Ndox mi ak yooni Ndox yi dikk na ci bëccëgu Setal Sunu Réew ak ci wale yi;
Jëwriñu Ndaw ni, Tàggat Yaram ak Mbatiit indi ay leeral ci « les vacances agricoles » yi.
Jëwriñu Tàggatu gu Xereñ gi, Farbay Ngornamaa bi
Aamadu Njekk SARE