xamle - 12 MONTHS.JUNE 2025
Ca Njaayeen Pedaawo, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, nemmiku na ci alxemes ji, sàntar gurupaas bu Bube niki noonu toolu ceeb bu Saare Waalo.
Naal yu am solo yii, te juddoo ci lëngoo gu wér diggante Senegaal ak Kore du Sud jaare ko ci "Agence coréenne de coopération internationale (KOICA)”, day wane yéeney Senegaal ci doxal mbay mu méngoo ak jamono te sax. Mu bokk ci jubluwaay yu am solo yi ñu tënk ci biir “Agenda de transformation Vision Senegaal 2050”.