Ndajem waxtaane wàllu dund bi ci Afrig 2025 : Peresidaa FAY di soññe ngir Afrig gu ma ak boppam te bokk ci ñiy dundal àddina si.

xamle - 01 MONTHS.SEPTEMBER 2025


Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY FAY, jiite na ci altine ji ca Jamñaajo jataayu tijjitel 19ᵉ Ndajem waxtaane wàllu dund ci Afrig, ci teewaayu naataangoom Póol Kagame, Njiitu Réewum Ruwàndaa, niki noonu kilifa yu mag ci Afrig ak ci biir àddina si. 


Ci ay kàddoom, moom Njiitu Réew mi fàttali na ne Afrig moo yor lu tollu ci 65% ci suufus àddina si, ndaw ñu xereñ ak balluwaayu ndox yu bari, di bir yoy tax na sunu Kembaar gi yor caabi ji koy may mu manal boppam ci wàllu dund boole ko ak bokk ci ñi ëpp solo ngir dundal àddina si. 

Taxawlu na bu baax ci ne fàww ñu gën a dugal xaalis ci : 

• méngale mbay mi ak jamono,

• peeg ndox mi,

• sopparñee fi li fiy ñoree,

• suqali ay wuumi njariñ ak yaxantu gi diggante réewi Afrig yi,

• niki  noonu fent gi ak xarala yi.


Njiitu Réew mi soññe na ci ñu def mbay mi muy fànn gu xemmeemu ñeel ndawi Afrig ak dundalaat Afrig gu sampu ci manal boppam, fent ak naataange gu yaatu. 


Man ngeen a toppaat kàddu yi ci widewoo bii: