Ndajem waxtaan ca Dohaa

jëwriñ - 06 MONTHS.DECEMBER 2024

Njiitu Réew mi dina dem ca Ndajem waxtaan may am ca Dohaa, ca Kataar, 6 jàpp 8i fani desàmbar 2024, ci ndënel kilifa ga Seex Tamiim Bin Hamad Al Saanii, Emiir bu Kataar. 

Ndaje mii di xew-xew bu mag ci àddina si,  ñu jagleel ko waxtaane jafey-jafey àddina si ci wàllu doxaliin, kaaraange ak suqaliku gu sax.