Ci tukki nemmiku gi muy amal ca “Pôle territoire Nord”, Njiitu Réew mi séq na ab jataay ak way-faluy tundu Ndar, rawati na fara yi ak njiiti ndiisooy gox yi.
Muy ndaje mu leen may ñu amal ay weccente yu am solo ci jëmmalug sémb wi jëm ci suqali “Pôle territoire Nord” bi. Jëwriñ ji yor Daggug Mbeeraay gi ak ug baram aajar nañu ci anam yu leer man-man ak njariñ yi tund woowu làq, jaare ko ci fésal yëngu yi ñu fa man a yaatal ci wàllu koom ak dundiin.
Njiitu Réew mi déglu na bu baax njàmbati way-falu ñi, teg ci jox leen ay tontu yu leer te dal xel, rawati na lu jëm ci jàppandil koppar yi ñuy jagleel gox yi ak goxaan yi ngir gunge leen ci naal yi ñuy sumb ci wàllu suqaliku.
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY rafetlu na waxtaan yu am solo yi ñu amal, teg ci feddali solos yoriin wu dul beddi kenn, wu dul xool péetey politig yi, te tënku ci taxaw ci saafara soxlay askan wi. Feddali na ag jaayanteem jëm ci gën a dëgëral lëngoo gi diggante Nguur gi ak Gox yi ak Goxaan yi ngir suqaliku gu wér te sax.
Mu tëjee moom Njiitu Réew mi ci sant ak gërëm way-falu ñi ci dalal gu mucc ayib gi ak sóobu gi ñu wane ci diirub nemmiku gi mu doon amal ci tundu Ndar.