Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay a ngi dooree 2eelu bisu 38eelu Ndajem Mbootaayu Réewi Afrig yi ci am ndaje diggam ak Àntoño Guteres, Sekereteer Seneraalu Mbootaayu Réewi àddina si.
Ci jataay boobu, ñaari jëmm yi weccente nañu xalaat ci jafe-jafe yu bari te wuute yi Afrig ak àddina si di jànkonteel, tolluwaayu kaaraange gi ci dig-digal bi, soppikug njuux li ak jafe-jafe yi am ci wàllu lëkkaloo.
Mbootaayu Réewi àddina si, ci turu Sekkereteer Seneraal bi, xamle na taxawaayu Senegaal niki ku am dayo te doon ku ñu weg ci àddina si, teg ci feddali yéeneem ci sukkandiku ci kilifteefu Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay ngir mu jàpp ci xeex bi ñuy amal jëm ci jàmmaarloo ak jafe-jafey àddina si.
Njiitu Réew mi ci wàllam feddali na ag jaayanteem ngir dooleel jàmm, maandute ak sàmm campeefi Afrig yu mag yi fi kilifa yi jiitu woon taxawal.
Njiitu Réew mi teg ci dalal Musaa Faki Mahamat, Njiital Komisoo bu Mbootaayu Réewi Afrig li fégal ginnaaw juróom ñetti at yu mu def ci boppu komisoo bi. Jaajëfal na ko bu baax ci ag jaayanteem ak jéego yu am solo yi mu teg ngir bennoog Afrig, boole ko ak nag di fàttali jafe-jafe yi des te ñu war cee taxaw ngir ëllëgu kembaar gi.
Senegaal kon di feddali taxawaayam ci réew mu jaayante, mu am taxawaay te dogu ci dooleel lëkkaloog àddina si ak bennoog Afrig.