Ndajem Mbootaayu Réewi Afrig : Njiitu Réew mi ak Njiital Jëwriñu Ecopi di Abiy Ahmet waxtaane nañu lu jëm ci lëkkaloo ak bennoog Afrig.

Biti Réew - 14 MONTHS.FEBRUARY 2025

Ci 38eelu Ndajem Mbootaayu Réewi Afrig yi, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, amal na jataay bu am solo diggam ak Abiy Ahmet Aali, Njiital Jëwriñu Réewum Ecopi, ca Pale Nasonaal. 

Muy ndaje mu ñu amal ay waxtaan yu xóot ci yenn tombi njariñ yu ñaari réew yi bokk am, yu mel ni lëkkaloo diggante Senegaal ak Ecopi, niki noonu jafe-jafe yi am ci bennog Afrig.