xamle - 10 MONTHS.NOVEMBER 2024
Njiitu Réew mi bawoo na Ndakaaru tay ci suba gi wutali Riyad ca Araabi Sawdit. Moom Basiiru Jomaay Fay, Njiitu Réewum Senegaal war faa teewe, ànd ko ak naataangoom yu Mbootaayu Lëkkaloog Lislaam gii di OCI, Ndajem arabo-islaam gi ñu jagleel ko tolluwaayu Palestin ak Liban.
Ndaje mii ñu jàpp a amal 11i nowàmbar mu ngi jëm ci dooleel taxawu ak njàppaleg Umma Islaam gi jëme ci ñaari réew yooyu boole ko ak woote jàmm ju sax dàkk ca tund wa.