Ndaje mu njëkk mu Kilifa ak Njiiti Wànqaasi Pénc mi : ay jéego yu jëm ci taxawal Ndoxal gu méngoo ak jamono te gën a jege askan

xamle - 20 MONTHS.JANUARY 2025

Njiitu Réew mi jiite na ci altine ji 20i fani sãawiye 2025, jataayu tijjitel Ndaje mu njëkk mu Kilifa ak Njiiti wànqaasi Pénc mi (CAMP). Xew wii nga xam ne guleet ñu koy amal, dajale na mbooleem wànqaasi pénc mi ci kanamu Njiitu Réew mi, Njiital Jëwriñ yi Ngóornamaŋam ngir xalaat jëm ci tëggaat sunu Ndoxal gi.


Ndaje mii nag mu ngi am ci jamono joj Nguur gi a ngi jànkonteel ak ay jafe-jafe ci wàllu njël li, koppar ak doxaliin, ba tax na nag mu laaj ñu yeesalaat yoriinu pénc mi ak Ndoxal gu ñu war a tëggaat ngir gën a man a taxaw ci jafe-jafey jamono ji. Day am solo nag ñu xam ne sektéer parapiblig bi dafa takku lool te njëgu, ba tax na ñu war koo yamale bu baax ngir njariñal ñépp. 





Cig àddoom, Njiitu Réew mi fàttali na « Vision Senegaal 2050 » bi ñu war a tegtaloo ci yoriinu pénc mi, te sampu ci ñenti keno: koom mu am doole te man a sos ay xëy, dagg gu sax ci mbeeraay gi, nit ñu xereñ ak yamale diggante askan wi, ak yoriin wu jub boole ko ak jaayante ngir Afrig. 


Njiitu Réew mi xamle na ne fàww ñu gën a yokk xereñte gi ci yoriinu pénc mi, gën a dooleel jàppalante gi ci diggante ñi séq Ngóornamaŋ bi ak taxaw temm ci jiital njariñu ñépp, sukkandiku ko ci Ndoxal gu méngoo ak jamono te jege askan wi.


Ci geneen wàll, Peresidaa Fay soññe na itam ci ñu gën a joxante cér ci wàllu kilifteef ndax mooy tax ñu man a am yoriin wu mucc ayib, niki noonu taxaw temm ci xeex ger, taqoo ak njub, jubal ak yoriin wu leer ñeel mbooleem liggéeykat yi.


Ci jiital caytu gu wér jëme ci sektéer parapiblig bi ak càmbaraat seen sas ngir gën a man a jariñ askan wi, Njiitu Réew mi soññ na képp ku di njiit rekk ngay dox ci yoriin woo xam ne day tegu ci ay pexe ak ay njureef yu baax. Feddali na ne tëggaat Ndoxalug Senegaal keno bu am solo la ngir jëmmal « Vision Sénégal 2050 » boole ko ak indi tontu yu wér ci nammeelu askan wi.