Ndaje mu Mag mu ONU : Peresidaa FAY di gën a feddali lëkkaloo yu am solo ñeel Senegaal.

Biti Réew - 23 MONTHS.SEPTEMBER 2025

Ci 80eelu Ndaje mu Mag mu Mbootaayu Réewi Àddina si ca New York, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY wéyal na ndaje yu am solo yi mu séq ak ñu mag ñuy yëngu ci Koomum àddina si. 



Njiitu Réew mi jagleel na ab jataay, S. Sultaan Bin SULAYEM, Njiitu Dubai Port Word. Waxtaan yi jëmoon ci suqali jumtukaayi waax yi, dooleel jëfandikukaay yi ci géej gi ak mbébetu dugal xaalis ci Senegaal. Ndaje mii di wane yéeney Senegaal jëm ci gën a dooleel taxawaayam niki selebe yoon bu am solo ci Afrig Sowu Jant, jaare ko ci lëngoo yu wér te wóor ngir jàpp ci soppi koom mi.  




Njiitu Réew mi dalal na itam, S. Andy INGLIS, Njiitu Kosmos Group. Mu bokkoon ci waxtaan yi, lu jëm ci gën a dooleel lëkkaloo gi diggante Senegaal ak Kosmos niki noonu tolluwaayu naal yi ñu nekk di doxal ci wàllu yasara gi. Ñaari wàll yépp feddali nañu seen jaayante ngir gën a doxal lëngoo gu kenn ku ne di gis boppam, mu lalu ci gën a jariñoo balluwaayi réew mi ak gën a jagal dundiinu askan wi. 


Ci ndaje yii, Senegaal day wane ag dogoom ci tabax koom mu am doole te boole ñépp, lalu ci tabax ay jumtukaay yu méngoo ak jamono ak caytu gu sax ci balli yasara yi.