Biti Réew - 23 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Tay altine ci suba si, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay dalal na kilifa gii di Luc Frieden, Njiital Jëwriñ lu Grand-Duché bu Luxembourg.
Ñaari kilfa yi fésal nañu solos gën a dooleel lëkkaloo diggante ñaari réew yi ngir jàmmaarloo ak yitte yi leen di xaar.
Senegaal fas na yéene dooleel lëkkaloom digganteem ak Luxembourg, jaare ko ci xarala yi, suqaliku gu sax ak pàcc yu yees, ci kaw ku ne sàmmonte ak mbaaxi ñaari réew yi.