Biti Réew - 01 MONTHS.JULY 2025
Niki mu ko baaxoo defee saa su demee ca biti réew, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, daje na ci ngoonug talaata ji ak doomi Senegaal yay dund ca Espaañ.
Ndajem mbégte ak mbokkoo mii am pose la woon ngir amal waxtaan yu wér, jamonoy déglonte ak weccente xalaat. Njiitu Réew mi rafetlu na bu baax taxawaayu doomi Senegaal yiy dund biti réew tey jàpp bu baax ci suqalikug reew mi. Fàttali na seen taxawaay bu am solo bi ñu am ci coppite gi nu namm a amal ci réew mi teg ci feddali yéeneem ci ànd ak ñoom tabax jëflante gu gu wér te wóor.