Medina Baay : Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay demoon siyaareji Seex Muhammadu Maahi Ibraahiima Ñas

xamle - 11 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Ci waajtaayu màggal guddig Mawlud gi, Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Fay, demoon na ca Medina Baay (Kawlax) ngir amal ub siyaar ci wetu Xalif bi Seex Muhammadu Maahi Ibraahiima Ñas.
Ginnaaw dalal gu mucc ayib gi, Kilifa gi Basiiru Jomaay Fay xamle na ci kanamu Sëriñ bi cofeel gu kawe gi mu am ci Seex Ibraahiima Ñas. "Seex Ibraahiima Ñas royukaay la ci man, ndax yarekat bu mag la woon bu dooleel diiney lislaam.”
Mu posewu ci ndaje mii ak Xalifa bi, Njiitu Réew mi sàkku na ay ñaan ngir Senegaal ak ngóornamaŋam, jiital ci nag solos bennoo ak jàppalante ci réew mi.