Door nañu liggéey yi aju ci jataayu Ndajem Mbootaayu Réewi Afrig yi tay ci gaawu bi ca Adis Abebaa, ci teewaayu Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay.
Jataayu tijjite lii may na Njiitu Réew Mi, Basiiru Jomaay Fay mu amal àddoom gu njëkk ci kanamu naataangoom yu Afrig yi. Delloo na njukkal ñi sos Mbootaay gi teg ci feddali dogug Senegaal ci wéyal jéegoo yooyu ngir Afrig gu moom boppam, bennoo te naat.
Njiitu Réew mi taxawlu na bu baax ci ne fàww ñu gën a boole doole yi ngir man a jàmmaarloo ak jafe-jafey kembaar gi, lu mel ni amal ay ay coppite ci wàllu lëkkaloo yi, xeex ak ñàkk yamale gi am ci wàllu koom ak soppikug njuux li, niki noonu fexee taxawal doxaliinu koom mu moom boppam te boole ñépp.
Njiitu Réew mi feddali na yéeney Senegaal ci ànd ak partaneeri saa-Afrig yi liggéey ngir taxaw ci yittey askan wi, tabax lëkkaloo yu yamale ak gën a fésal am-ami kembaar gi. Mu daaneele ci woote ngir ñu gën a sóob ndaw ñi ak jigéen ñi ci yoon wi nu jël jëm ci soppi Afrig.