Mawlud 2025 : siyaareb Njiitu Réew mi ca Tiwaawon.

xamle - 30 MONTHS.AUGUST 2025

Tay ci gaawu bi 30i fani ut 2025, Njiitu Réew mi demoon na ca Tiwaawon siyaareji. 


Moom Njiitu Réew Mi nag, Kilifag Tiijaan yi dalal na ko, ñu amal jataay bu fees dell ak cofeel ak wegeel. 


Dem na ca xabrub Seydi El Haaji Maalig SI amal fa ay ñaan niki noonu ca bu Sëriñ Baabakar SI, laataa muy dem ca Jumaa Ju Mag ju Tiwaawon. 


Siyaar bii nag day wane taqoo gu sax gi Njiitu Réew mi am ci këri diine yi ak wegeel gu wér gu mu am ci ñoom ndax seen taxawaay ci suuxat jàmm ak dal ci Senegaal. 


Man ngeen a toppaat Kàdduy  Njiitu Réew mi: