Ca Araabi Sawudit ngir teewe ndajem Future Investment Initiative Forum 2024, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY posewu na ci ngir matale umra gi ca Màkka.
Ci loolu nag, ñu defal ko ag jagle, ci ndigalu doomi Buur ba di Njiital Ndiisoog Jëwriñ yu Araabi Sawudit, Mohammet Ben Salmaan Ben Abdel Asiis Al Sawud, tijjil ko wunti Kaaba gi nekk ca biir Masjidul Haraam. Jëf jii nag di wane rekk cér bi kilifay saa-sawud yi jox seen gan gii ak jëflante yu rafet yi yàgg a dox diggante Senegaal ak Araabi Sawudit.
Ci jamonoy teewlu yii, Njiitu Réew mi amal na ay ñaan ngir jàmm, naataange ak déggoo ci askan wi, sàkkuwaale ci Boroomam itam mu teg nu ci yoonu dimbalante ak yokkute gu ñépp di bokk.