Màggalug 65eelu at mi Senegaal moomee boppam.

xool - 04 MONTHS.APRIL 2025

Senegaal màggal na, ci àjjuma ji 4i fani awril 2025, 65eelu at mi mu moomee boppam, di xew-xew bu am solo bu Njiitu Réew mi, Kilifa gu Mag gu Xare bi doon jiite.

Fàttaliku gii, doon lu fees dell ak màndarga ak mbégte ci réew mi, mu ngi doon amee ci xàllu Mammadu Ja, wi ñu daan  woowee Bulwaar Seneraal De Gaulle, ñu tudaat ko ngir sargal ci jëmm jii fi jiite woon, Ndiisoog Jëwriñ yi ba nuy door a moom sunu bopp. 

Njiitu Réew mi nag, naataangoom yu Móritani, Mohammet Uld Seex El Ghazouani, Gine Bisaawóo, Umaro Sisoko Embaló, Gàmbi, Aadama Baro ak Topp-Njiital Niseriyaa, Kashim Shettima, wuyusi nañu ko, mu doon luy firndeel jëflante yu rittax ak jàppoo sunu digg ak sunu dëkkandoo yi. 

Bis bi nag ñu ngi ko màndargalee ak maaj gu rëy ci diggante siwil yi ak sóobare si jot a jaar ci kanamu  lu ëpp 6000i nit ñu doon teewe jataay bi. Muy xew-xew bu wane gànjarug mbatiit ak mboorum Senegaal, ak mbooloo yu doon wane dëkki cosaan yi fi ne woon, niki noonu way-kaaraange yiy màndargaal sunug dëgër ak sunug jonn. Tomb bi ñu tànn ren di, « Naka lees di def ba am larme bu moom boppam ci wàllu xarala ak ndefar », day feddali mbébetu Peresidaa Fay ci gën a dooleel réew mu moom boppam, rawati na ci naal yu mel ni méngale ak jamono jumtukaayi sóobare si. 

Cig àddoom, Njiitu Réew mi delloo na njukkal way-kaaraange yi ci lootaabe gu mucc ayib gi ñu amlee maaj gi, boole ci feddali  jaayanteem ngir réew mu mànkoo ak Afrig gu doon benn. Teewaayu yenn ci Njiiti Réew yi nu dëkkandool doon na itam luy gën a firndeel lëkkaloog kembaar gi ak diisoo ngir dal man a am ci Afrig Sowu-Jant. 

Màggal gii nag, bu weesoo femm (feet) gi, am pose la woon ci Senegaal mu feddali ab taxawaayam ci kembaar gi, lépp ci kaw tiitaroo démbam boole ko ak dëgmal ëllëg ngir réew mu moom boppam te naat. 

Man ngeen a teewluwaat àddug Njiitu Réew mi ginnaaw maaj gi : 


Nu dikk ak yéen ci peeñ yii ci màggal bis bi nu moomee sunu bopp:  https://www.flickr.com/photos/presidencesenegal/albums/72177720324921779/