Màggal 80eelu atu bóom gi amoon Caaroy: Peresidaa Baro ak Embaló yegsi nañu Ndakaaru

xamle - 30 MONTHS.NOVEMBER 2024

Njiitu Réew mu Gàmbi Aadama Baro, ak mu Gine Bisaawóo Umaro Sisoko Embaló , yegsi nañu Ndakaaru ci gaawu bi ngir teewe xewu màggal 80eelu atu bóomug tiraayéer yi ca Caaroy.

Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay moo leen teertu ba ñuy yegsi ca naawub sóobare bu Lewopóol Sedaar Sengoor.