Ci Màggalug Tuubaa giy dëgmal, ñu jàpp ko 13i fani it 2025, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, ànd ak soxnaam, Soxna Absa FAY, ak mbooloo mu am solo, demoon na tay ci ngoon gi ca dëkk bu sell ba di Tuubaa ngir siyaare Kilifag Yoonu Muriit, Sëriñ Muntaxaa MBÀKKE.
Siyaar bii may na Njiitu Réew Mi mu feddali ndigal yi mu joxoon ngóornamaŋ bi ngir amal màggal gu mucc ayib. Sàkku na itam ay ñaan ci Xaliif bi ngir sottalug naal yi mu sumb ci Senegaal rawati na ci Tuubaa ci wàllu ndox mi, asanismaa bi, njàng mi ak yenn jultukaay yi askan wiy yittewoo.
Ci Kàddug Sëriñ Basiiru MBÀKKE 𝑨𝒃𝒅𝒖 Xaadir mi yor kàddoom, Xaliifa bi feddali na cofeelam ci Njiitu Réew mi, jaare ko ci rafetlu pas-pasam ci wàllu diine ak yéeneem ci réew mi. « Bi ma leen gisee, dégg leen teg xam seen taqoo ak tawhiit, ci laa xam seen yéene ju wér ngir liggéeyal réew mi», di li mu wax. Xalif bi dalal na xelu Njiitu Réew mi itam ne du ko fàtte mukk ci ay ñaan ngir mu am ndam ci mbooleem li muy naal.