Nii la Ngóornamaŋu Senegaal bi bawoo ci, DOGAL L° 2025 – 1430 bu 06i fani sebtàmbar 2025 bi Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay Jaxaar FAY torlu, ci ngaaralug Njiitu Jëwriñ yi Usmaan SONKO, séddalikoo :
Sëriñ Usmaan SONKO : Njiitu Jëwriñ yi
1. Soxna Yaasin FAAL : Jëwriñu Yoon, Aji-wattu Màndarga yi ;
2. Sëriñ Biram Suley JÓOB : Jëwriñu Yasara gi, Petorol bi ak Mbell yi ;
3. Sëriñ Seex ÑAŊ : Jëwriñu Bennoog Afrig, Jëflante ak Biti Réew ak Saa-Senegaal yi nekk biti réew ;
4. Sëriñ Biram JÓOB : Jëwriñu Sóobare si ;
5. Sëriñ Muhammadu Bàmba SIISE : Jëwriñu Biir Réew mi ak Kaaraangeg Pénc mi ;
6. Sëriñ Abdurahmaan SAAR : Jëwriñu Koom mi, Palaŋ bi ak Lëkkaloo gi ;
7. Sëriñ Seex DIBA : Jëwriñu Koppar yi ak Njël li ;
8. Sëriñ Daawuda NGOM : Jëwriñu Njàng mu kawe mi, Gëstu gi ak Fent gi ;
9. Sëriñ Yanqooba JEMME : Jëwriñu Yaaley Suuf si ak Jaww ji ;
10. Sëriñ Àlliyun SÀLL : Jëwriñu Caabal gi, Jokkalekaay yi ak Xarala gi ;
11. Sëriñ Mustafaa Màmba GIRAASI : Jëwriñu Njàng mi ;
12. Sëriñ Ma-Buuba JAAÑ : Jëwriñu Mbay mi, Bay-Dunde gi ak Càmm gi ;
13. Sëriñ Seex Tiijaan JÉEY : Jëwriñu Ndox mi ak Asanismaa bi ;
14. Sëriñ Ibraahima SI : Jëwriñu Paj mi ak Sellaayu Pénc mi ;
15. Soxna Maymuna JÉEY : Jëwriñu Njaboot gi ak Dimbalante gi ;
16. Sëriñ Aamadu Mustafaa Njekk SARE : Jëwriñu Xëy mi ak Tàggatu gu Xereñ gi ak gu Xarala gi ;
17. Sëriñ El Haaji Abdurahmaan JUUF : Jëwriñu Kéew mi ak Jàll Jëm ci Ekolosi ;
18. Sëriñ Bàlla Musaa FOFANA : Jëwriñu Dëkkuwaay yi, Gox Yi ak Goxaan yi ak Pakkug Mbeeraay yi ;
19. Sëriñ Géy JÓOB : Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi ;
20. Soxna Faatu JUUF : Jëwriñu Napp gi ak Koomum Géej gi ;
21. Sëriñ Oliwe BUKAAL : Jëwriñu Foŋsoo Piblig, Liggéey bi ak Yeesalug Serwiis Piblig bi ;
22. Soxna Xadi Jéen GAY : Jëwriñu Ndaw ñi ak Tàggat Yaram yi ;
23. Sëriñ Àlliyun JONN : Jëwriñu Kopparal gu Ndaw gi ak Koomum Jàppal ma Jàpp mi ;
24. Sëriñ Décce FAAL : Jëwriñu Jumtu yi ;
25. Sëriñ Aamadu BA : Jëwriñu Mbatiit mi, Pasiin gi ak Ndaamaari gi ;
26. Soxna Mari Róos Xadi Faatu FAY : Sekkreteer Detaa ci wetu Njiiitu Jëwriñ yi, ñu dénk ko Jëflante diggante Campeef yi, Farbab Ngóornamaŋ bi
27. Sëriñ Aamadu Sériif JUUF : Sekkereteer Detaa ci wetu Jëwriñu Bennoog Afrig, Jëflante ak Biti Réew ak Saa-Senegaal yi nekk biti réew, ñu dénk ko Saa-Senegaal ya ca Biti Réew ;
28. Sëriñ Alfa BA : Sekkereteer Detaa ci wetu Jëwriñu Mbay mi, Bay-Dunde gi ak Càmm gi, ñu dénk ko Mbootaay yi ak Taxawu Baykat yi ;
29. Sëriñ Momat NDAW : Sekkereteer Detaa ci wetu Jëwriñu Dëkkuwaay yi, Gox Yi ak Goxaan yi ak Pakkug Mbeeraay yi, ñu dénk ko mbirum dëkkuwaay ;
30. Sëriñ Ibraahiima CAAM : Sekkereteer Detaa ci wetu Jëwriñu Ndefar gi ak Yaxantu gi, ñu dénk ko Suqalikug këri liggéeyukaay yu ndaw yi ak yu yam yi ak ndefar yu ndaw yi ak yu yam yi ;
31. Sëriñ Baakari Saar : Sekkereteer Detaa ci wetu Jëwriñu Mbatiit mi, Pasiin gi ak Ndaamaari gi, ñu dénk ko wàllu Mbatiit, Ndefar yi ci wàllu fent ak Ndono li ci wàllu Mboor.
Man ngeen a topp widewoo ciiwalug ñi bokk ci Ngóornamaŋ bu bees bi :