xamle - 17 MONTHS.NOVEMBER 2024
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay ànd na ak Soxnaam, dem ca Njagañaaw di bokk-moomeel ga mu ganee jamono, tollu ci 102i jun-ñay diggam ak Gëblag Ndakaaru, ngir amal wotam ci dibéer ji ñeel joŋantey tànn depite yu 2024.
Joŋante bi nag mu ngi jëm ci fal 165i depite yi war a teew ca Ngomblaanug Senegaal ci kayug juróomi at.
Ginnaaw ba mu matalee wareefu ma-réewam ba noppi, Kilifa gi, Basiiru Jomaay Fay xamle na ne « nguur gi jël na mbooleem matuwaay yi war ngir amal lootaabe gu jaar yoon ci joŋante bi, lépp ci sàmmonte ak yelleefu lawax bu nek ».
Njiitu Réew mi delloo na njukkal askanu Senegaal « wiy génn jamono jii ngir matale wareefam ci tànn ñi ko war a teewal ëllëg lépp ci biir jàmm ak dal, niki ñu ko yàgg a miinee ci Senegaal ».
Cig àddoom, woo na itam way-politig yi, di leen ñaax ñu gën a ànd ak dal, jiital jàmm te nangu tànneefu askan wiy bawoo ci wot yi ».