Lesislatif 2024/ Bataaxelu Njiitu Réew mi Basiiru JOMAAY Fay

xamle - 02 MONTHS.NOVEMBER 2024


Ginnaaw bi mu bawoo ci tukki nemmiku yi mu doon amal ca Araabi Sawudit ak Turki, Basiiru Jomaay Fay Njiitu Réewum Senegaal feddali na woote jàmm bi mu defoon jëm joŋantey lesislatif yu 17i nowàmbar 2024. Moom Njiitu Réew Mi ñaax na way-Politig yi tamit ñu gën a wane ag mat te am taxawaayu kilifa.