xamle - 16 MONTHS.JULY 2025
Njiitu Réew mi, Basiiru Jomaay FAY, dalal na ci àllarba ji 16i fani sulet 2025, Kilifa gi José Maria Neves, Njiitu Réewum Kabo Werde.
Ginnaaw jataayi tatagal yi, ñaari Njiiti Réew yi gën nañoo xóotal ci lëkkaloo gi dox diggante Ndakaaru ak Praia. Waxtaane nañu itam ci wàllu bennoo gi war a am ci diggante réew yi ci tund wi, jaare ko ci feddali seen yéene ji ñu bokk am jëm ci gën a dooleel jëflante yu boole ñépp te dëppoo ak nammeeli askanu tund wi.
Man ngeen a topp widewoo ndaje mi :