Laamisoo : Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay teewe na màggalug 51i ati jonnug Gine Bisaawóo

Biti Réew - 16 MONTHS.NOVEMBER 2024

Ci ndënel kilifa gi, Seneraalu Larme di Umar Sisoko Embaló Njiitu Réewum Gine Bisaawóo, Basiiru Jomaay Fay Njiitu Réewum Senegaal teewe na ci gaawu bi, màggalug 51i ati jonnug Réewum mbokk mii. 

Bis bii, tombe ak fàttaliku 100i ati Amilkaar Kabraal mi taxawal Réewum Gine Bisaawóo te doonoon jëmm ju amoon taxawaay ci xeex ngir génne Afrig cig nooteel, doon na itam lu ñu jagleel larme biy màndargaal moom sa bopp.

Peresidaa Fay posewu na ci bis bi ngir rafetlu bu baax jëflantey mbokk ak dëkkandoo yi dox diggante Senegaal ak Gine Bisaawóo, teg ci feddali ag jaayanteem ci gën a dëgëral lëkkaloo googu ngir njariñal ñaari askan yi.