Korite 2025 | Njiitu Réew mi di ñaax askan wi ñu jéem a taqoo ak mbaaxi ngëm, mbokkoo, muñalante ak bennoo.

xamle - 31 MONTHS.MARCH 2025

Ci bisub korite gi, Kilifa gi Basiiru Jomaay Fay, Njiitu Réewum Senegaal teewe na julli gi ca Jumaa Ju Mag ju Ndakaaru.

Ginnaaw ba mu noppee, Njiitu Réew mi jagleel na ay ñaan yu mu tibbee ci xolam mbooleem saa-senegaal yi, góor ak jigéen, niki noonu ci mbooleem Umma Islaam gi, muy ñaan bisub kori gu ànd ak jàmm, wérug yaram, naataange ak jàppoo. 

Njiitu Réew mi delloo na njukkal Imaam Raatibu Jumaa ji, mbooleem kilifa diine yi ci réew mi, niki noonu kilifa aada yi. Feddali na ag cantam ci taxawaay bu am solo bi ñu am jëm ci sàmm jàmm ji, boole ko ak di sàkkuwaat ci ñoom ay ñaan ngir Senegaal gu gën a mànkoo, gën a jub te gën a dal. 

Ci bataaxel bu fees dell ak hikma ak kilifteef, Njiitu Réew mi ñaax na askan wi ñu gën a góor-góorlu ci mbaaxi ngëm, mbokkoo, muñalante, ak bennoo, di jëf yu  yàgg a màndargaal Senegaal. 

« Maa ngi ñaan lépp loo xam ne jaamoo nanu ko Yàlla ci weer wii, Yàlla nangul nu ko, jéggal nu rëcc-rëcc yi te gën noo dëgëral ci siraatal mustaxiim. Di ñaan kilifa diine yi ak kilifa aada yi, waaye di ko ñaan bépp way-gëm,  rawati na jullit ñi moom bis bii tay, ñu wéy di ñaanal réew mi. Ñaan ngir dal am fi, ñaan ngir jàmm am fi, waaye ñaan tamit ba lépp loo xam ne noo ngi koy teg ci ay jéego te am ci yéene defar Senegaal Yàlla barkeel ko », di li mu daanele.


 Man ngeen a topp fii mbooleem kàdduy Njiitu Réew mi :