jëwriñ - 02 MONTHS.DECEMBER 2024
Ci ndënel naataangoom bii di Basiiru Jomaay Fay, Njiitu Réewum Senegaal, Seneraal Biris Koloteer Oligi Ngemaa Njiitu Réewum Gaboŋ, ñu ngi koy séntu ci Ndakaaru gi mu war a amal ag ngan. Tukki bii mu war a amal ci Senegaal, am pose lay doon ci Njiitu Réewum Gaboŋ ngir mu teewe 1 panu desàmbar 2024 ci màggalug 80eelu atu bóomug tiiraayéeri Senegaal.
Ñaari Njiiti Réew yi dinañu séq ub jataay altine 2i fani desàmbar ci Njéndel Réew mi ngir waxtaane yenn tombi njariñ yi ñu bokk.