Ci waajtaayu « Forum africain des systèmes alimentaires » bi, Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay FAY, dalal na ci ab jataay. S Alvaro Lario, Njiitu « Fonds international de développement agricole (FIDA) ».
Ndaje mii tax na ñu feddali lëkkaloo gu mucc ayib gi dox diggante Senegaal ak FIDA, te sampu ci naal yu wér yuy gën a dooleel mbay mi ak suqalikug kaw gi.
Waxtaan yi jëmoon ci :
* yitte ji ñu bokk am ci wàllu bay dunde;
* gunge waa kaw gi jaare ko ci dugal xaalis ci sémb yu wér ;
* méngale mbay mi ak jamono ak gën a jariñoo ndaw ñi ;
* kenoy « Vision Sénégal 2050 » bi teg mbay mi ci xolu liy soppi koom mi ak dundiin wi.
Njiitu Réew mi ak Njiitu FIDA feddali nañu seen ug jaayante ci gën a dooleel lëngoo gi jëm ci fent ak gën a jagal dundiinu askan wi ci kaw gi.