Àjjuma 29i fani nowàmbar 2024, Kilifa gi Basiiru JOMAAY Fay, Njiitu Réew mi, dina jiite ca Njénde la jataayu sargal fukk ci sunuy naataangoy ma-réew yu jàmbaare lool ci bëccëgi Setal Sunu Réew yi ñuy amal weer wu jot. Ma-réew yii ñu tànn niki ay royukaay ngir Senegaal gu sax ci set te sell, dinañu jot raaya wii di « Jàmbaar ci Setal Sunu Réew ».
Ràññeeku gii nag day tàbbi ci yéenee ji Njiitu Réew mi am ci delloo njukkal ma-réew yiy dugal seen loxo ci setal ak sellal pénc mi ak kéew mi niki noonu ñaax askan wi ñu gën a jaayante ci li nu bokk. Ñoom way-ràññiku yii ñu tànn ndax seen i jëf yu am solo, dañuy màndargaal dooley naali kenn ku nekk ak yu mbooloo yi jëm ci soppi sunug dund.
Muy xew-xew bu jóg itam ngir gën a sóob saa-senegaal yi ñu gën a takku ci jëf yu jëm ci sàmm mbooleem li wër sunu dëkkuwaay.
Ba ñu ko dooree ca 1 panu suwe 2024 ak tay, naalu « Setal Sunu Réew » mu ngi wéy di dajale weer wu jot ay junni junniy ma-réew yuy yëngu ngir setal pénc mi ak sellal dëkkuwaay yi, fépp ci réew mi. Ci xew wi, Njiitu Réew mi a ngi woote ag lëngoo diggante ma-réew yi, mbootaayi gox yi ak campeef, ngir ñu gën a def yitte ci set boole ko ci yi ñuy jiital ci réew mi te fexee koo def muy lu Àjjuma 29i fani nowàmbar 2024, Kilifa gi Basiiru JOMAAY Fay, Njiitu Réew mi, dina jiite ca Njénde la jataayu sargal fukk ci sunuy naataangoy ma-réew yu jàmbaare lool ci bëccëgi Setal Sunu Réew yi ñuy amal weer wu jot. Ma-réew yii ñu tànn niki ay royukaay ngir Senegaal gu sax ci set te sell, dinañu jot raaya wii di « Jambaar ci Setal Sunu Réew ».
Ràññeeku gii nag day tàbbi ci yéenee ji Njiitu Réew mi am ci delloo njukkal ma-réew yiy dugal seen loxo ci setal ak sellal pénc mi ak kéew mi niki noonu ñaax askan wi ñu gën a jaayante ci li nu bokk. Ñoom way-ràññiku ñii ñu tànn ndax seen i jëf yu am solo, dañuy màndargaal dooley naali kenn ku nekk ak yu mbooloo yi jëm ci soppi sunug dund.
Muy xew-xew bu jóg itam ngir gën a sóob saa-senegaal yi ñu gën a takku ci jëf yu jëm ci sàmm mbooleem li wër sunu dëkkuwaay.
Ba ñu dooree ca 1 panu suwe 2024 ak tay, naalu « Setal Sunu Réew » mu ngi wéy di dajale weer wu jot ay junni junniy ma-réew yuy yëngu ngir setal pénc mi ak sellal dëkkuwaay yi, fépp ci réew mi. Ci xew wi, Njiitu Réew mi a ngi woote ag lëngoo diggante ma-réew yi, mbootaayi gox yi ak campeef, ngir ñu gën a def yitte ci set boole ko ci yi jiitu ci réew mi te fexe koo def muy lu sax.