Kaliforni: Njiitu Réew mi dalal na Topp-Njiital Hewlett-Packard (HP), Ketan PATEL

xamle - 28 MONTHS.SEPTEMBER 2024
Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Fay dalal na Topp-Njiital Hewlett-Packard (HP), Ketan PATEL, ca Kaliforni, ci nemmiku gi mu doon amal ca Silikon Valley.
Ndaje mii diggam ak Topp-Njiital lijjantig Amerig gii ñu taxawal ca 1939 te xereñ ci wàllu eeformatig ak elektoronig, tax na ñu waxtaan ci tomb yu am solo yu mel ni wàllu disitaal ak sibeerkiriminaalite ci lu soxal New Deal technologique.
Njiitu Réew mi feddali na ag dogoom ci amal coppiteg xarala gu wér, jëm ci dooleel man-mani xarala yu Senegaal ak xeex ak tafaar yiy jaar ci lënd gi.