Kàddu yi Njiitu Réew mi Basiiru Jomaay Jaxaar Fay jagleel askanu Senegaal ci posem 65eelu at mi Senegaal moomee boppam.

waxtaan - 03 MONTHS.APRIL 2025

Ndakaaru 3i fani awril 2025



Bokki Senegaal,


Ëllëg 4i fan ci weeru awril, dinanu génn wane sunu mbégte ci bis bi nu moomee sunu bopp juróom benn fukki at ak juróom (65i at) ci ren. May xalaat di ñaanal mbooleem ñi nga xam ne, wane woon nañu taxawaayu njàmbaar ngir Senegaal moom boppam. Waaye di xalaat itam mbooleem ñi xam ne, ñoo yor kaaraangeg réew mi, muy soldaar yi wàcc liggéey ngir xeex moom sunu bopp googu ak fépp fu ñu ko man di defee. Di xalaat itam mbooleem ñi xam ne feebar nañu, walla sax ñu nekk ci jafe-jafe yoo xam ne, feet bii fekk na leen ci. 


Yàlla may nu nag xéewal ci at mii, mu ànd ak weer wow, weeru koor la ci kerceŋ yi, waaye itam nuy door a génn ci weeru koor ci jullit ñi. Muy wane ne liy dooley Senegaal mooy gëm-gëm. Moo nuy jox muñ gi war, waaye moo nuy jox itam muñalante gi war sunu diggante ak booloo ci jàmm ak ci dëgg. Tombe gii mu tombe nag, danu ciy ñaan Yàlla, lépp lu nu ko ci jaamu mu nangul nu ko, waaye itam mu wéy di def yërmande ak xéewal ak naataange fii ci Senegaal. Mu am nag ay mbaax yoy, noo ngi leen donnee ci ñi fi jiitu woon. Muy wane ne danoo war a boole sunu doole ak sunu kàttan, rawati na ba nu demee ba nekk ci ay jafe-jafe yoy, sunu xel ak sunu xalaat ak sunu xereñte rekk a nu ci man a génne. Di fàttaliku sunu bàkku réew di : wenn askan wu am benn jumukaay te bokk gëm-gëm. 


Bokki Senegaal,


Juróom benn fukki at ak juróom (65i at) nu moom sunu bopp, juróom benn fukki at ak juróom (65i at) Senegaal di wane ne réew mu ñu jox cér la ci àddina si, ci biir Afrig ak ca biti réew, waaye juróom benn fukki at ak juróom (65i at) Senegaal di gën a teg ay jéego ci suqaliku. Nii nga xam ne noonu lanu fiy doxalee di réewum yoon ak réewum péexte, mu doon loo xam ne ci xeex lanu ko foqartee, te di ko sàmm bis set ci jàmm ak ci waxtaan moo tax ñu naw nu fii ci biir Afrig ak ca biti réew. Loolu nag war naa tax, ak lu nu man di woroo ci kàddu, ak lu gis-gis yi wuute, nangul nanu ku ne muy wax la mu xalaat ci kaw jox cér sa moroom, waaye bis bu askan wi demee ba tànnal boppam ñépp nangu ne lii mooy tànneefu askan wi. Loolu moo war a nekk sunu doole, moo war a nekk sunu wéeruwaay, ndax nu man a wuyoo li nuy woote di jub, di jubal ak si jubbanti, waaye tamit taxwu askan wi ci bëgg-bëggam ak ndaw ñi ci seen yaakaar. 


Bokki Senegaal,


Ku wax 4 awril, wax itam feet bu rëy ci ñii yor kaaraangeg réew mi. Ma di leen wax mbégte mu ma am ci ñoom, di leen jaajëfal, di leen wax ne bég naa lool ci seen taxawaay ci biir réew mi, ndax ñoom ñoo nuy may dal gi tax nu man a doxal sunuy yitte ak taxawu askan wi. Di xalaat ñi nga xam ne ñooy seen i mag, di xalaat « anciens combattants » yi, di leen wax ne askan wi ameel na leen njukkal lu rëy. 


Lii di tomb bi nu tànn war koo waxtaane ci feetu endepàndaasu ren jii, muy nan lanu war a fexe ba moom sunu bopp ci wàllu xarala yi ak lépp lu nu man a jox gànnaay yu nuy aaree sunu bopp, day wane rekk ne yéene ji nu am ci taxawu leen ci seen sas, waaye tamit taxawu leen ci seen liggéey bis bu set. Muy góor ak jigéen ñi nekk ci kaaraange réew mi, yéen yéen a tax ba jàmm am biir Senegaal, ba tax na képp kuy doxal say yëngu ci jàmm ak ci xel mu dal ameel na leen njukkal. Ngeen di ko def ànd ci ak dogu ak mbégte ak jaayante gu tax ngeen di jëmmal lii nuy wax bennoo diggante larme bi ak askan wi. 

Di taxawu tamit saa-senegaal yi ak fépp fu ñu man a nekk, lu weesu kaaraange gi, saa su leen nattu dalee ngeen taxaw seen wet niki ngeen ko defee daaw bi taw yi mettee ba am ñu mu sonal. 

Noo ngi liggéey ànd ko ak yéen ànd ko ak ñépp ñi nga xam ne seen xam-xam màcc na jëm ci lépp lu nuy tax a moom sunu bopp ci wàllu ndefar, te nu boole ci fulla ju mat sëkk muy tomb bu am solo ci sunu sémb. 


Bokki Senegaal,


Lu mat um at a ngii ngeen dénk nu réew mi. Nu wax leen fi nu fekk réew mi ci lu amul benn nëbboo, lal ko ci dëgg kese, ndax jàpp ne ci dëgg rekk lanu man a tabax lu dëggu ak lu yàgg. Waaye ba nu leen wanee loolu ba noppi, danoo daal di jublu ci saa si, indi saafara ci li waral tolluwaay bii nu nekk. Ngóornamaŋ bumu sóobu ci ay yeesal yu am solo yuy man a tax nu indi yoriin wu leer ci ni ñuy saytoo alalu askan wi. 


Bokki Senegaal,


Waaye li mbir mi di tar tar, terewunoo jëf ngir taxawu askan wi ci ni nu leen war a taxawoo. Doore ko daaw bi nu dikkee fekk ñenti at yoy, ñi nekkoon operaatéer yi ci wàllu jiwu ak jumtukaayu mbay, nu fay leen ñenti at yi leen nguur gi ameeloon. Waaye tamit taxawu ñiy yëngu ci wàllu tabax (BTP) ci seen bor yi, waaye tamit fexe ba at mii di ñëw nu am lu nu leen nattal ngir man leen koo fay. Taxaw tamit ci li doonoon ay ràppel te nu ameeloon ko jàngalekat yi, nu dugal ci xaalis bu bari, waaye fexe nanu tamit ba mu laal daanaka lu jege fukki junni ci ñoom. Waaye ci at mii rekk nu jël junni ak téeméer ak juróom ñent fukk yu teg dugal leen ci « mise ne solde » yi. 


Terewunoo taxawu itam jigéen ñi. Fas nanu yéenee door ci fan yii di ñëw, ci lu nu war a gugal lu mat téeméeri milyaar ak juróom ñett, porogaraam bii jëm ci kopparal ndaw ñi ak jigéen ñi. Nu war koo boole ci progaraam bu war a mat ñetti junniy « fermes intègrée » yoo xam ne bu nu ko xaymaa ci li mu war a jël ci ay egtaar dina mat fukki junni ak juróom ngir rekk wàllu mbay ak càmm. Te at mii nu nekk tamit dinanu tàmbali taxawal lii di « coopérative agricoles communautaires » yi ngir jigéen ñi ak ndaw ñi, lépp ngir fexe ba mbay mi gën a am doole, nit ñi am ci lu ñu jàpp. 


Bokki Senegaal,


Ci jamono jii nga xam ne koom-koom jafe na ci réew mi, xool fi nuy dugal xaalis bi, ci gën gaa leeri anam rekk a nu man a génne ci jafe-jafe yi nu nekk. Lépp lu jëm ci xarala yu bees yi, dinanu ko jëfandikoo ngir fu dërëmu Senegaal dugg nu man koo toppaat, te bala mu faa dugg, mu dugg fa na mu fa war a duggee maanaam mu topp yoon yi nu tëral. Loolu yépp nag bu nu ko dee def, bëgg taxawu askan wi rekk a ko waral, niki nu ko nekk di amalee ba nu dikkee ak leegi, di xar sunu tànku tubey ngir man a wàcce lépp lu jëm ci njëgu li nuy jëfandikoo ci wàllu dund. Te loolu du tee li saa-senegaal yi soxla ci wàllu cet ak ci wàllu wér gi yaram Ngóornamaŋ bi taxaw ci temm. Waxoon naa leen ne dinanu wéy di wàññi, wàññi nanu bu yàggul dara. Te bu wàññi gii weesoo dinanu wàññiwaat yeneen wàññi ci weer yii di ñëw. 


Bi nu Yàlla xéewalee nag Senegaal dugg leegi bokk ci réew yiy jaay petorol ak gaas, donte fekk nanu ñu waxtaane kontraa yi ba noppi, terewul noo ngi ciy liggéeyaat. Waaye lépp lu f jóge te saa-senegaal yi moom ko, dinanu fexe ba ñépp xam ñaata a fa génne ak nu fa génne ak fan lañu ko dugal. Lii nu leen digoon nag di waxtaanewaat wàllu kontraa yi, man naa leen a xibaar ne liggéey bi a ngi wéy, te fi nu tollu nii njureef yi nu ci am, sant nanu ci Yàlla bu baax a baax te xaajagul bay jeex. Xam nanu nag ne saa-senegaal yi fu ñu nekk, lii di ndox ak kuraŋ yitteel na leen lool. Moo tax ba nu ñëwee, nu baral, tàmbaliwaat lii di ñaareelu pàccu sémbu fooraas yi ci kaw gi. Manaam gas ay fooraas ci gox yi ak goxaan yi, te waxtaanewaat ko tamit ba li nu ci waroon a am yokk, te ba nu ko dooree ak leegi gox yu bari tàmbali nañoo gis seen ndox nu ciy sant Yàlla bu baax a baax. Noonu tamit lanuy baralee lépp loo xam ne lale na ak yóbbu kuraŋ bi ci kaw gi te ngeen teg ci seen bët. 

Li nuy jéem a def mooy waxtaan ba li war a doon njëg li mu doon lu nu téyee sunu loxo. Lu nu ci war a waxtaanewaat niki nu ko defee, nu waxtaanewaat ko ba man a yokk ñi ci war a jot. Ba ren jii am nanu yaakaar ci lu mat ñaari junni ak juróom ñaari téeméer yu teg ci ay gox goxaan dinañu man a jot ci lii di kuraŋ bi. 


Noonu lanu taxawee ci lii di suuf si nga xam ne am na ñu ci jotoon a am téyee ko ba ñeneen ñi manuñu cee jot walla balaa ñu ciy jot sonn lool. Càmbar yi nu ci def nag lépp lu mu laaj rekk dinanu ko ci def, waaye fas yéene itam gën koo téyee ak fulla, leeraange ak kilifteef. Noonu lanu ko fas yéenee wéyal ci waxtaan, ndax fu nu man a jaar itam, day lu manul a ñàkk, fàww yeesal yi war ci wàllu suuf si nga xam ne, ku nekk ñëw na yékkati ko tegaat ko ci suuf, nu def ko ba mu mat, ngir képp ku am suuf nga man cee am loo xam ne day wane ne yaw yaa ko moomal sa bopp ba kenn du ko man a ñëw foqarti ci say yoxo. 


Lii nuy def nag ci waxtaan ba tay, ngir jàmm am Kaasamaas, day wane ne nun Senegaal benn bopp lanu, moo tax donte danoo am féewaloo, li ci war mooy nu toog waxtaan. Am nanu ci ag yokkute bu wér ci lu yàggul dara, ma ciy jaajëfal bu baax Njiital Jëwriñ yi Usmaan Sonko mi fekke woon xaatimug déggoo yiy war a man a tax nu man a jëmmal tomb yi ñu jot a déggoo. 

Nu wéyal ci nag di doxal lii di « Plan Diomaye pour la Casamance » ngir juboo gii fa amaat ak askan wa demoon tey dellusiwaat ci gox goxaan yooyu, man a nekk ci amal dund gu ñoŋ gu ànd ak sàmmonte ak seen diññite. 


Bokki Senegaal,


Lii di juboo ci biir réew mi, ak jàmm ak dal, lépp lu may def suba ak ngoon, ci loolu laay teg samay gët. Ndax damaa gëm ne askan wu am,  yewwu  tax ñuy waxtaan ci lu ne, day tax mu gën a dëgër, déggoo gën faa am, ñu man di xàccandoo di dóorandoo. Loolu nag danu ciy woo ñépp. Loolu sax moo taxoon fan yii nu génn, ma joxoon ndigal Njiital Jëwriñ yi Usmaan Sonko ne ko na waxtaan ak ñépp ñi nga xam ne ñoom lanu bokkal mbir mi, ndax nu man a xam fu réew mi tollu, yan jéego lanu ci jot a teg ak fan lanu ko namm a jëme. Ñépp jàpp ci ndax noo ko bokk. 


Bokki Senegaal,


Lépp li ma dige woon ak yéen, te mooy lépp luy gën a indi ag déggoo ci réew mi, juboo, te gën a sori lépp lu man a jur féewaloo, moom laa bëggoon ngeen xam ne manul a nekk te yorunu réew mi ci dëgg, yoriin wu sell, boole ko ak saa-senegaal yi tamit xam li ñu moom, naka lanu koy téyee ba li ñépp bokk ñépp jot ci. Ba tax na tàmbali nanu lépp loo xam ne ay sàrt yu nu waroon a jël la, jëmale ko ci yoriin wu gën a sell, jébbal nanu ko Jëwriñu Yoon ji. Moo ci des ci liggéey bi ba keroog ñu koy saytu ci « Conseil des Ministres ».


Waxtaane woon tamit wàllu yoon. Amoon na ay poñ yoy ñépp dëppoo woon nañu ci. Ma tegoon fi komite bu ciy liggéey. Loolu it man naa leen a xibaar ne lii di mbind yi aju ci « Cour Constitutionnelle » bi nu déggoo woon, ci sémbu yeesal Ndayu Sàrti Réew mi ak li laale ci « Conseil Supérieur de la Magistrature » jébbal nañu nu ko ba noo ngi koy wan ñi ci war a joxe seen xalaat ca na mu gën a yaatoo, balaa nuy yegg ci di ko jàllale. Komite bi a ngi wéyal liggéey bi ngir tamit lépp lu laale ci wàllu « juge des libertés e de la détention » ak mbirum « retour de parquet » yi, lépp lu mu laaj rekk ngir ñu tëggaat « code pénale » bi ak « code de procédure pénale » bi, ñu gën a baral liggéey bi balaa ñuy gën a dem ci yeneen diisoo. 


Ci loolu laa leen di xibaar tamit bisub diisoo bi nu war a amal ci réew mi 28i fani weeru mee 2025 bu soobe Yàlla. 

Lii di sunu sistem politig lanuy waxtaane niki ma ko digee woon. Ndax dafa laaj ci ni ñuy defee politig ci Senegaal ñu gën koo ànkaadare. Waaye nag, li nu leen jébbal ne loolu lanu war a waxtaane, dingeen am sañ-sañ tamit ci  ñi ñu ko jox, ñu yokk ci ay poñ waaye tamit joxe ci seen xalaat ndax nu gën a man a waajal liggéey bi nu war a amal. 


Bokki Senegaal,


Fi koom-koomu réew mi tollu, ci nun li nu fi fekk te wax leen ko, dafay laaj nun saa-senegaal yi, nu yaakaar ci sunu bopp ngir jógaat, amaat beneen taxawaay, waaye tami fexe ba guuta gii nu génn ci, dugg ci koom-koom moo xam ne, day jur naataange ba ñépp man cee gis seen bopp. 


Bokki Senegaal,


Mboor wane na ne réew yi mas a am jafe-jafe yépp ba génn ci, dañoo nangu woon a jaayante lu bari ci seen bopp ngir man a génn ci jafe-jafe yooyu ba bokk ci réew yi nga xam ne naw nañu leen ba sunuy doom di daw tay di dem foofu. Nekkul ne dañoo xëy rekk suqaliku, waaye dañoo takk seen ndigg, booloo, ñemee liggéey, waaye liggéey tamit ci fulla ji mu war a àndal. Lii mooy yoon wi, amul weneen yoon ! Te nun ñépp war nanu koo xamee noonu te tegu ci. Def ko nag ngir sunu bopp waaye def ko rawati na ngir ëllëg ak sunu njaboot. Bu nu amee taxawaay boobu, bañ koo wàcc, ñépp am ko, ci dëggu, Senegaal gii nga xam ne noo ngi koy gént, muy Senegaalu naataange, muy Senegaal gu yoon di dox, muy Senegaalu jàmm, dinanu ko matal bu soobe Yàlla. 


Kon jërëjef askanu Senegaal !

Maa ngi leen di ñaanal feetu endepàndaasu jàmm ! Di ko ñaanal ñépp ñiy xool ci Senegaal !


As-salaamu halaykum warahmatul Laah!