Kàddu yi Njiiti Réew yu Senegaal ak Móritani bokk amal.

laaj ak xibaar - 22 MONTHS.MAY 2025

Ginnaaw nemmiku gi ñu amal ca palaataformu gaas bu “Grand Tortue Ahmeyim (GTA)”, te féete ca dig wa dox diggante Senegaal ak Móritani, Kilifa yii di Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal, ak Mohammet Uld Seex El Xaswaani, Njiitu Réewum Móritani, feddali nañu jaayante gi ñu bokk def jëm ci gën a dooleel lëkkaloo diggante ñaari réew yi ngir taxaw ci suqaliku gu sax ci sémb wii.

Man ngeen a topp kàddu yi Basiiru Jomaay FAY, Njiitu Réewum Senegaal, ak naataangoom bu Móritani, Mohammet Uld Seex El Xaswaani, bokk yékkati :